Woote !
Gnattelou jotaay bi êmb jàapalante ak suuxat kom-kom ci diggante way tukki yi.

Jàngoro ji wane na, ci gnimou gnor, ni kom-kom mênul a am ludul si kaw gnu jeem a saakou yookute si dundin wi. Ba noonu, jamono bi ni êpp bêgoon nu gêm loo ni gnoo ngi dundu li gênê yees ci sunu aduna, ndôol mi ngi gnuy sonal, doonte kom-kom bi gnepp doon xaar dafa taga teembe diiru lu toolo ak been att. Tay nak, tassu kaayu xibaar yaa ngi gnuy bêg a gêmloo ni xew-xew bi am Ukaraine ak xeex bi dox ci diggente Russie ak OTAN mooko waral.

Ay jomono yu meeti la yuy wane sounou neew doolem kom-kom. Bépp mbootaayum koom mingi jéema laaku ci ginaaw way politik yi ngir setal booppam. Nitt gniy tukki di dundu ag beedikoonte bis bu ne, yeen saay sax seeni aax ak yeeleef dognu leen di salfaagne.
Lolu taxna ba kom-kom ci diggante nitt gni ak jaapalante bi war sugnu biir gnu war ko dêgêl, jeem a ubbi ay bereb ngir jaapalante googu mên a neek. Lolu dina tax ba gnu mên a suqali bou baax sugnu koom te defaraat sugnu dundin. Loloo tax ba soopiteg kom-kom gi du wuute ak li way tukki yi di jankoonteel bitim reew ; muy ay jafe-jafe yu soree wul ak li jaam yi daan dundu. Ba taxna att mii gnu neek kureel bii di Fira dina ci soobu bu baax, teemeeri juniy (500.000) ràagneeku waay, dêppoo ak teemeeri juniy nit (500.000) yuy dundu luni mel ; ndax leer na gnu ni nitt gnoognu gnooy suuxat koomug bitti reew. Ngir lolou àantu, faaw gnu neewal doole koomug Espagne, ndax gnoomit ci way tukki yi, book ci gnoom ay gone yu amul ay kêyit, ci lagn yaakar gnir tabax seenum reew. Dina taxit gnu mên a taxawal bêrêb ngir di degglu seen i jàambat, te xam seen i tawat. Dinagne book feete ak gnoom ndam liy tukkee ci xeex bi, jugge ci woteg teemeer ak juroom gnati fukk ak juroom gneenti (189) xaatim baayikoo ci kureel bi êmb mbooleem ligeey kat yi ci aduna (OIT), ginaaw fukki att yugnu doon xaar coopite yuni mel. Ndam lolu nak dina gên a dêgêrêl te itam dina xeex beepp gnaawteef bu way tukki yi daan dundu ; jigeen gni feete bittim reew itam am nagn ci waal wu rêy.

Ngir lolu am, dinagn saxal sugnu xeex te dêgêrêl bêrêbu daje kaay yi ngir saam aax ak yeeleef u way tukki yi. Doole ji mooy defaraat ndaje mi, te suxataat kom-komug nit gniy dundu bitti reew ba kureel gi leen êmb mu di Coopolis, woote waat gnateelu jotaayub way tukki yi.
Du neek lu yoomb, bêg nagnu yaatal woote bi ba mbooleem teemeeri mbebet yi tax gnuy xeex bis bu neek mên a aantu. Diir bi gnu mên a bindu ngir book ci ndaje mi mingi door fukki fan ak juroom jàapp gnaar fukki fan ak juroom gnatt ci weeru sulet (du 15 au 28 juillet), bu gnu ci noopee tàan mbêmbet yi gnu gnor. Ndaje mi dinagnu ko amal fukki fan ak juroom gnaar ci weeru sàatumbar (17 septembre).
Bugnu booloowee lii yep dina mên a neek ! kon nak gnoo ngui leen di xaar yeen gnepp.