Yëgle

Ñ entelu ndaje kom ak japo bou dojandemyi ak ñi ute

Tabax kom guiy bañ xet ak ñep.

Atum 2023 dana dess ci sunu xel yi ndax moy atmi mbassu COVID-19 tambali di randu ñu delowat ci jamm. Ñeti atyi wesu gis nanu ñaku ligey bu taar ci ñi gena neew dole, ñoñu dëk ci dëkbi ak taxaway bisi ñogn Kilifa adayi am. Ñaka nangu en amna ay jafe jafe ci ñen ñi rawatina dojandem yi, rawatina ñi amul ay këyit

Toluway bobu tahona ndek yi yok dundu bi gëna meti, wante rawatina dundu ñiñu wahone biduy tambali. Fimi tolu ni, Mbotayu Johalante ak Kommi Rewyi (OCDE) tëg baat bu bess bumu tudu yokute bu amul yamuway, baat bu juge ci yokute bu taar te ñiko soke di borom alalyi. Lolu moy ñi profito di am kom te dinu bayi xel domi adamayi, manam di not rek te fasyene mu don ba fawu te lolu aduna manu deku.

Dafa jaduwul donteko mbassmi jarnafi pur ñu mana tëgat taxawayu kom bu yess , tambaliwat ba domi adama nek liy yite, danu gissne nit ñi ñungi jem ndax seni mbotay wante ñuy jankontek ay jafe jafe, ñu len di bedi, dilen bañ, te lolu gissnanuko ci tasskatu xibaryi, ñogn politik Ay wax yu ñaw jëm ci dojandem yi ak ñiñu bañ sen xet ndax sen deer nimoumel, lolu waral DET ak sen yelef yi manuta ñak, com wara wote, ci frontieryi politik yi day ute, dunu mana am dekuway, sen walu njang, rawatina xaleyi ak ndawyi tuki. Lolu law baci ñak taxaway ak liguey ci rewmi. Kon bilolu ame, boolo dey dadi am solo lol, eawatina ndawñi wara wadial kom ak dekin wisel, ak aduna binu bëg elëk. Ndax dano nenal lol xam ak dëg.

Ci bir lolu, daño fassyene taxawal bërëb ngir daje, xamante, japalante, ci wal yep, rawatina ci kom. Japale dojandemyi. Mbolo moy doole, moy sopi sunu dundu, lolu motax Cercle bu Migration ak bu dediwul ken bu Coopolis, ño woote ñentelu ndaje kom ak japo bu dojandemyi ak ñi ute.

Ci ndajemi ndaw ñi danuci am waalu wu yatu ci tabax kom ku yess ak cooperativeyi, bu jale walu capitalisteyi ak lep linuy def pur ñenñi am, ñenñi ñak, rawatina ndah sen wute. Bok ciyu melni dana japandal tabax ay gissin ak japandal, tey fesel lep lutax ñu mana sigi mana mom sunu bop ci ligey ay payor wu bah ak yeneni yatal.

Kontenak, ño ngi am yakar yataal yëglebi ci temeri projetyi yi xex biss binek ngir mbiryi mana sopeku, Dojandemyi, nitñi ute ñi bëga taxawal dara ak funu mana jouge. Waxtu bindu bi doorna ci 17 juillet baci 11 septembre, buko defe danu taan ñi wara bok. Ndajemi dina am ci 30 septembre fofe ci Llotja de Sant Antoni.

Nako ñep yatal, ñongi en di sentu !